Overblog
Editer l'article Suivre ce blog Administration + Créer mon blog
KUNZUL MOUKHTADINA TOUBA MBACKA LO

LETTRE AUX CROYANTES

11 Février 2016 , Rédigé par Mor Leau

Lettre aux Croyantes
Jawâbu Soxna Penda Diop
écrit par Cheikh Ahmadou Bamba

Version wolof


Lii ab bataaxal la bu Sëriñ Tuubaa masa bind benn taalibeem bu tudd
Soxna Penda Joob, di soxna ci baayam bu ndaw. Ci biir ndenkaan bu am
solo boobu, ñu gëna xam ci « Jawaabu Soxna Penda Joob »,
Sëriñ baa ngi ciy digël lii soxna si, ak bepp soxnas murit, ak bepp jullit
bu jigéen :
« Man Sëriñ Tuubaa miy jaam bu xeebu tey sàkkoo am ngërëmal Yàlla
akug Yonentam, te di yaakaar ci ñoom ñu nangul ko ay jëfëm, maa ngi
dénk lii Soxna Penda Joob, di samab taalibe, tey soxna ci sama baay tëx.
Yàlla na ñu Yàlla jéggal te jéggal ko, te boole ñu faral bepp bàkkaar ak
matadi.
1. Maa ngi lay digël yaw soxna si nga goor-goorlu ci muñ ak ragal
Yàlla, sa Boroom, ci lu nëbu ak lu feeñ ; soo ko defee dey Yàlla di na
la jéggal ëlëg
2. Na nga sax ci tuubal Yàlla saa su nekk ak farlu ci def lu baax ; kon
bul jéngg mukk jëm ci leneen ludul ag njub
3. Na nga sax ci nangoo weet ngir jaamu sa Boroom. Looy def dee ko
def ci sutura te deel suufeel sa kàddu saa yooy wax ; soo ko defee dey
Yàlla di na la gërëm
4. Yaw Soxna Penda, li la dese ci sa giirug dund, bul jogëti mukk jëm
ci loo xam ne leeru la ne dagan na ci Lislaam
5. Deel moytu bu baax jëw ak rëy. Deel saxoo noppi ak muñ.
6. Deel moytu bu baax wax lu amul ak ngistal wala bëgga siiw. Na nga
moytu naw sa jëf wala di bañanteek sa moroomi mbindéef yi.
7. Na nga sax ci dëggu ak sellal, deel farlu ci laabire aka dimbali jaam
ñi ; soo ko defee dey suñu Boroom di na la defal ay may aki jagle
8. Bul xalaat mukk topp sa Boroom ci lu andulak topp sa ndigëlul
boroom kër bu ragal Yàlla boobu
9. Ndax xamal ne kat jihaadu soxna ci yoonu Yàlla mooy mu farlu ci
topp ndigëlu boroom kërëm

10. Looloo waral saa yu boroom kër gërëmee soxnaam, sunu Boroom
da na gërëm soxna soosu te di na ko defal ay xeewal
11. Waaye su fekkee boroom kër gërëmul soxnaam, soxna soosu na
xam ne sunu Boroom du ko masa gërëm
12. Maa ngi lay xamal ne lepp lu nit mana def te jëmmi Yàlla rekk
taxul, jëfam jooju sanku na te pert na ko
13. Te na la woor ne, kenn du mana mucc ëlëg ci mbugëlum sunu
Boroom lifeeg bàyyiwul ñeent mbir yii, te mooy :
a. Wax ludul dëgg
b. Rëy
c. Nay ci sa alal
d. Ñaaw njort ci sa moroom ak ci sa Boroom
Wa salaamu aleykum warahmatu Laahi wa Barakaatuhu

Partager cet article
Repost0
Pour être informé des derniers articles, inscrivez vous :
Commenter cet article